doomiaadama

“ Pour les enfants qui s’ébattent au clair de lune, mon conte est une narration fantastique. Pour les pileuses de coton pendant les longues nuits de la saison froide, mon récit est une délectation, un passe temps fait à plaisr. Pour les mentons velus et les talons rugueux, c’est une véritable révélation. Je suis donc à la fois futile, utile et instructeur”“Au pays de Kaïdara de Amadou Hampaté Ba Vous le devinez déjà, nous allons conter sur ce blog.

Thursday, June 29, 2006

CES FILS D'ADAM


NDESITI DOOMI AADAMA/LES RESTES DES FILS D'ADAM
PRÉSENTATION DE L’OUVRAGE
L’Agence intergouvernementale de la Francophonie vient de confier au Centre International de Phonétique Appliquée (CIPA), l’édition d’une nouvelle collection : " Diversité linguistique et société ". Cette collection est consacrée à l’un des enjeux majeurs du 3° millénaire : la diversité linguistique, elle-même partie intégrante de la diversité culturelle. Les deux premiers volumes viennent de paraître : - Isidore NDAYWEL ; Louis-Jean ROUSSEAU ( dir.).- Demain le français : vers des stratégies diversifiées de promotion et d’enseignement.- Paris : AIF ; Mons : CIPA, 2004.- 267 p.


Image:(c)"La Vie",Une création de Daour Wade

NDESITI DOOMI AADAMA
Ndesiti doomi Aadama, téeré la buy wax lu soxal doomi Aadama yi,
bu jële ci Doomu Aadama, jëme ci Doomi Aadama yi.

Les Restes des Fils d’Adam est un ouvrage qui parle des Fils et filles d’Adam, écrit par un des Fils d’Adam pour tous les Fils d’Adam.

Nu ngi dund ci jamono ju jax, ju tumurànké, jàppalante ak dimbalante, yërmaande ak jàmm, yar ak teggin, kollare ak muñalante ak doxalin yuy sàmmu àqi doomi Aadama .

Nous vivons une époque trouble, pauvre des qualités de l’entraide et de l’assistance, de pitié, de paix, de politesse et de savoir être, de
reconnaissance et de tolérance, de respect des droits de la personne humaine.

Nettali yi nekk ci téére bii, boroom tëgge lee-leeg aki nit, ay rab, wallay mala, sërxël ci biir yenn taalif yu gàtt, ci baax yooyii lay wax ngir Doomi Aadama yi man a dawal séen xel fu sori, indi ko ci tey, seet li nu dese ci jikko yiy jariñ xeetu Doomi Aadama wi tey ci nekkin wu rafet aki dëkkandoom ak ku mu man di doon (nit, rab, mala, garab, gàncax, a.n.s.) Su xalaat yooyu amee, ñu sukkandiku ci desit yooyule, suuxat léen, sàmm léen ba jàmm sax fépp ci kow suuf ci biir déggoo, jàppoo, dimbalante ci biir yërmànde gu lalu ci kow wegante ci diggante ñi am doole ak ñi néew doole, ñi yor ak ñi ñàkk ndax àqi bépp Doomi Aadama sàmmu ba mu sàmmaale yu ñeneen ñi mu dëkkël.

Les histoires contenues dans cet ouvrages, forgées avec des personnages humains, animaux, sauvages ou domestiques, parsemées de courts poèmes, parlent de ces valeurs là. Il veut pousser les Fils et les Filles d’Adam à la réfléxion aussi loin que possible dans leurs tréfonds pour chercher dans les bribes de valeurs qui leur restent celles qui peuvent servir la race humaine aujourd’hui à mieux vivre en communauté (entre les humains mais aussi avec les autres êtres vivants, les animaux,
la nature…) Une fois ces restes de valeurs identifiées, il faut les entretenir, les préserver pour que la Paix prenne racines sur Terre, que l’entente et l’entraide, fleurissent dans le lit d’une compassion empreinte de respect réciproque entre les plus forts et les plus faibles, les riches et les pauvres afin que les droits et devoirs de tout Fils et de toute Fille d’Adam soient entièrement respectés.

L’auteur Maam Daour Wade est un conteur, écrivain, scénariste et réalisateur de films. Il a été formé au cinéma à Paris (France) au Conservatoire Libre du Cinéma français et à l’Université de Bloomington Indiana (Usa), membre de l’Association des Ecrivains du Sénégal (AES) et membre fondateur de l’Association des Cinéastes Associés (CINESEAS) et de l’Association des Conteurs du Sénégal »Contes au Clair de Lune ». Il est également membre fondateur de l’Association Africaines éditrice de GUNE YI (Premier journal pour enfants Bilingue : Français/Wolof)

Maam Daawur bindkat la, léebkat la, fentkat la ci wàllu nettali te liggéykatu film la. Mu ngi jànge Faraans ca Pari ci Kuréel gu tudd "Konserwaatuwaar Liibar dii sinemaa Faraanse" akit ca « Iniwersitee bu Injaana »Bulumington ca Amirik. Bokk na ci mbooloom bindkati Senegaal (AES) akit ci ñi sos mbooloom ñiy defar film ci Senegaal (CINESEAS) akit ci mbooloom Léeboon Ci Leer (Léebkati Senegaal) Bokk na ci yit ñi sos kuréel gu tudd (Anfaans afrikeen) di kuréel gi fi jëkk a génne këyitu xiibaar wu ñu jagleel xale yi "GUNE YI" te ñu bind ko ci ñaari kàllaama yii : Nasaraan ak Wolof .

Auparavant, il a suivi une formation de technicien agricole à l’Ecole des Agents Techniques d’Agriculture de Louga. Il a sillonné les campagnes sénégalaises comme acteur de développement rural (Satec et Sodeva) au service des communautés rurales où il compte beaucoup d’amis

Lu jiitu loolu, jàng na mbirum mbey ci daara ju tudd Ferm Ekool ca Luga Loo « Kër Mbargu Balañaan ». Dem na fu bari ci réew mi, ci kow liggéey ak beykat yi, ci mbirum mbey – amaale fa yit xarit yu takku- ag kuréel yii di Satek ak Soodewaa.

Il a écrit des scénarii pour la Télévison RTS1 , »Mbokk » 2001, « Purux » 2002, Waajur 2003, « Ana sama Doom » 2005) et pour la Radio Sénégalaise « Ñilaan Saar » , Laurier d’Or RTS1 2002 , une série télévisée « Mafñàndu »(Timbóo ak Sooke) sur la 2STV, 2006. Il a produit plusieurs collections de contes pour enfants dont « Contes Wolof » 1979, Prix Unicef Foire du Livre et du matériel didactique de Dakar 1993, « Proverbes Wolof » et « le Taureau Fantastique », Bld, 1997.

Bind nay fent ngir RTS ci wàllu Telewisyon RTS1(Mbokk 2001, Purux 2002, Waajur 2003, Ana sama Doom 2005) ak ci wàllu rajo « Ñilaan Saar »,Lorye Wurus bu RTS1 2002), benn seéeri bu tudd une série télévisée « Mafñàndu »(Timbóo ak Sooke) ci 2STV,2006. Bind na yitam ay téerey léeb ngir gune yi « Léebi Wolof », 1979, Neexalu Inisef ci Fuwaaru téereb Ndakaaru ci 1993 ak « Léebuy Wolof » akit « Ngaari Mawndi », Bld 1997.

Son inspiration lui vient du riche patrimoine culturel Sénégalais et Africain. Il est convaincu que la culture et la tradition d’un peuple sont des sources de la créativité et moteur de développement.

Mu ngi jëley xalaat ci baax yi ëmbu ci aada ak cosaanu Senegaal. Li mu gëm moo di ni, aadaak cosaanu xeet wune, teen la bu xeet wa man a duye ngir suuxat xel yu koy jëmale kanam.

Dans un monde où les frontières réelles deviennent de plus en plus virtuelles chaque jour qui passe, il est important de partager avec les autres cultures du monde les mets de nos cultures dans la pure tradition du donner sans refuser de goûter aux mets les meilleurs que nous offrent les autres cultures.

Ci àdduna soo xam ni sii diggante yaa ngi gënn di wàññeeku fu nu tollu, am na solo ci nu xam ni séddook àdduna si lii di sunu aadaak cosaan, manatul a ñàkk, ci kow joxe gu àndul ak laaj ñu delloo nu njukkël waaye gudul lànk a mos ci baax yi gën a ràññeeku ci baaxi ñeneen ñi.


Un conte extrait de l'ouvrage
"Les Restes des Fils d'Adam"

Tout le monde respecte les chats au Sénégal. On dit d’ailleurs que personne ne doit ni les frapper ni leur faire de mal car les chats se vengent toujours quand on les offense. Ainsi, des chats, on en trouve dans toutes les maisons et ils n’appartiennent à personne en particulier. Ils habitent le quartier et vont de maison en maison selon l’endroit où ils trouvent à manger.

Cependant, il arrive qu’un chat ou des chats, s’installent dans une maison pour une longue période de temps. C’est ce qui est arrivé à une famille de chats. Le père chat et la mère chat avaient choisi une maison où il y avait tous les jours à manger et à boire. Les quatre enfants chats sont nés bien après l’arrivée des parents chats. Tout allait si bien pour la famille chat qui mangeait les restes de riz au poisson, de poulet, de macaroni, de salade et de pomme de terre frites. C’était la belle époque !

Un jour, arriva une chose qui ébranla la famille chat toute entière. Cette chose s’appelait la dévaluation : cela signifiait que la valeur de la monnaie que les fils d’Adam utilisaient pour acheter ce qu’ils voulaient, avait baissé. Elle avait même baissé de moitié. La famille chat resta deux jours sans manger. Au lieu d’attendre comme d’habitude que les enfants leur amène à manger, la famille chat alla aux nouvelles. A l’heure du déjeuner, papa chat et maman chat ainsi que les enfants chats s’approchèrent du groupe des hommes assis autour du bol. Ils furent chassés à coup de sandales. La visite aux bols des femmes donna lieu à des invectives et à des raclées de sandales dans le dos. Et chacun fut servi.

Commença alors une période de vie très difficile pour la famille chat qui ne trouvait plus rien à manger. Même pas un os à grignoter car les restes du repas des fils d’Adam, n’étaient plus jetés, ni donnés aux chats errant ou habitant dans les maisons. Papa chat, maman chat et les enfants chats avaient tellement maigri qu’ils ne tenaient plus sur leurs pattes.
Et papa chat se souvenait que les porcs avaient eux aussi souffert dans
le passé quand le prix d’achat du riz a augmenté. A cette époque, les femmes avaient brutalement arrêté de verser les restes de leur fameux riz aux poissons ou “ ceebu jen”(1 )dans les tonneaux des “Maanjaago »(2)
“. C’est depuis ce temps que chez les fils d’Adama, le “gobar jaasi” est apparu, faisant du repas de midi celui du soir aussi, privant ainsi les enfants du “njoganal” ou casse croûte du soir.

Les félins tinrent un conseil de famille pour prendre la bonne décision face à la grave situation qui sévissait. Ce fut papa chat qui ouvrit les débats: “Depuis que la dévaluation est arrivée, les fils d’Adam ne nous donnent plus à manger car il n’ont plus beaucoup d’argent pour s’acheter eux mêmes à manger”. Maman chat de poursuivre: “J’ai toujours pensé que la dépendance alimentaire avec autrui était la pire des choses qui pouvait arriver à quelqu’un dans la vie “. Un enfant chat se risqua à poser une question: “Maman, comment sommes devenus dépendants des hommes pour notre nourriture quotidienne? “ Papa chat et maman chat se regardèrent un moment puis baissèrent chacun le regard. Papa chat, après s’être éclairci la gorge, releva la tête et expliqua: “C’était à l’époque de la grande sécheresse que nous avons été contraints de quitter la brousse où nous vivions du produit de notre chasse. Nous sommes allés au village le plus proche pour trouver quelque chose à nous mettre sous la dent. Ce furent aux cris de “Siiru” ou chat sauvage que des enfants affamés nous ont poursuivi avec une horde de chiens faméliques. Votre mère et moi avons dû notre salut à notre rapidité à la course“. Maman chat d’ajouter: “Dieu est grand, il nous viendra en aide. Ayons la foi, il ne abandonnera pas. Je me souviens de notre arrivée en ville où curieusement les gens nous appelaient du nom de “Muus” qui signifiait en Wolof chat et être malin à la fois. Le papa chat d’ajouter: ”Beaucoup d’enfants de la ville étaient mieux nourris que ceux du village et ne nous couraient pas après. Mais les chiens nos cousins, jaloux comme toujours, nous empêchaient de nous approcher des maîtres de maison“. Maman chat de poursuivre: “Croire en Dieu ne doit pas nous empêcher de cultiver notre champ car cette dévaluation nous a montré que nous avions oublié que le propre d’un chat était de chasser pour se nourrir, c’est à dire de veiller à assurer notre pitance quotidienne. C’est cela la solution à notre problème“ termina t-elle en sortant et rentrant ses griffes qu’une longue inaction avait atrophié”.

C’est ainsi qu’il fut décidé que désormais tous les membres de la famille chat partiraient de la maison des fils d’Adam, pour chercher leur nourriture à la sueur de leur front. Les parents chats avaient dit aux enfants chats que: “la noblesse de leur naissance venait de leurs parents mais que leur réussite dans la vie ne dépendait uniquement que d’eux même”. Les enfants chats, eux qui par le passé se contentaient de miauler quand ils avaient faim, décidèrent désormais de vivre selon leur époque et non plus selon l’époque de leurs parents.

Ainsi, ils rendirent au marché”Lambada” là où Asta Taparka la femme aux poisson, Ndey Binta Citron, la femme qui n’aimaient pas les chats, Joor kabaab la joyeuse vendeuse de légumes et Maar Seen le boucher avaient leurs étalages. Bientôt la famille chat se porta mieux malgré les rigueurs de la dévaluation.

Pendant ce temps, les chats qui comptaient toujours sur les restes des fils d’Adam avaient tellement faim qu’on pouvait compter leurs côtes.
Et papa chat de rappeler aux enfants chats : “Il faut d’abord compter sur soi avant de faire appel aux autres. Il ne sert à rien de rester à pleurer sur ses misères ou d’espérer se nourrir avec les restes des fils d’Adam.

Les enfants chats gardèrent bien cette belle leçon de sagesse car après tout la vie est faite de grands soucis et de petits soucis. Chaque fois que des soucis survenaient, ils se retroussaient les griffes pour les résoudre.
Et, ils finirent par comprendre que pour résoudre les problèmes de la vie, la grande leçon était celle-ci: “Quand vivre devient difficile, à la sueur de son front, il faut décider de vivre et éviter la dépendance sur autrui“.

Lexique :
(1) Ceebu jen : Riz au poisson en Wolof (Plat national du sénégal)
(2) Maanjaago : Nom en Wolof donné aux Manjack (Ethnie de la Casamance et de la Guinée Bissao)


LE JOUR, LA NUIT
Le soleil se couche,
Les ombrages s’épaississent
Et l’on croit que leurs imposantes silhouettes
Vont envelopper de leurs sombres couvertures
Le grand lit des ténèbres
Mais la lune se lève sans bruit,
Et arrose de sa douce lumière
Au plus profond du cœur de la nuit.


Version Wolof des Restes des Fils d’Adam
Ndesiti Doomi Aadama


Nit ñépp a wormaal muus ci Senegaal. Nee na ñu sax, kenn waru léen a dóor walla mu def léen lu metti ndax muus loo ko def naka sudul noonu dina feyu. Ci noonu, muus yi, dina ñu léen di fekk ci kër yépp te yit kenn moomu léen.

Ci koñ bi la ñuy dëkk, di dem këroo-kër ci kaw fa ñuy ame lu ñu lekk. Lee-leeg, menn, walla ay muus tànn kër, dëkkal fa boppam ci diir bu yàgg. Looloo dall genn njabootug muus. Baay muus ak yaay muus dañoo tànnoon kër gu ñu daan ame bés bu ne lu ñu daan lekk ak di ko fa naan.

Ñeenti doomi muus yépp, ñu ngi juddóo ci kër gi, ci jamono yi topp ci séen ñëwug waajur. Njabootug muus gaa ngi woon ci jàmm ndax dañu daan lekk desitu jen, desitu ginaar, desitu màkkaróoni, desitu salaad ak pombiteer yu ñu saaf. Jamono ju neexoon !

Benn bés, am mbir mu xew, mu yëngal njabootug muus gépp. Mbir moomule, mu ngi tuddoon “wàññeekum xaalis” tekki woon ni xaalis bi doomi Adaama yi daan jëfëndikoo ngir njënd li léen soxal, dooleem dafa wàññeeku woon. Xaalis bi, mënatul a jënd ludul genn-wàllug la mu daan jënd bu jëkk.

Njabootug muus toog ñaari fan, lekkul, naanul. Xaaruñu, ni ñu ko daan defe ba xale yi indil léen séenug lekk. Dañoo dem seeti li xew. Bi añ jotee, baay muus, yaay muus ak doomi muus ànd dem ci wetu goor ña wërooon ndab la di lekk. Ay dàlli digg ginnaaw a léen fa dàqe. Ba ñu seetee ndabul jigéen ña, ay saaga ak xëti digg ginnaaw la ñu fa jële. Ku ne ci ñoom, jot ca wàllam.

Ca la diggante bu metti doore ci njabootug muus gii mënatul woon a gis dara lu mu lekk. Yax bu ñu seeñu sax amatul ndax ndesitu lekk, doomi Aadama yi sànneetu ko, joxatu ko muus yi daan wëréelu mbaa ñu dëkkóon ak ñoom ci kër yi. Baay muus ak yaay muus ak doomi muus yooy ba sax su ñuy dox, di daanu. Noona, ñu fàttaliku ni mbaam xuux yi ñoomitam lu deme nii daloon na léen ci at yi ñu weesu, bi njëngug ceeb bi yokkoo.

Ca jamono yooyu, jigéen ñi, dañoo dakkaloon tuurum ndesitu ceebu jen ma ñu daan def ci biir barigo yi Maanjaago yi daan teg ci koñ yi…
Ca boobee la gobar jaasi xewe ci kër doomi Aadama yi, li nit ñi daan añe, la ñu daan reere, gone amatul njoganal. Njabootug muus daje ngir waxtaan ci séen biir ba xam nu ñuy def ci tiis wu doy waar wi daloon ci séen kaw. Baay muus moo ubbi wax ja : “ Bi dooley xaalis bi wàññikoo ba tey, doomi Aadama yi joxatuñu nu lekk ndax amatuñu xaalis bu doy bi ñuy jënde li ñuy lekk ñoom ci séen bopp.” Yaay muus jël kàddu ga ni : ” Musumaa jóg ci xalaat ni, wéeru ci keneen ngir la ngay lekk, mooy musiba mi gën a rëy ci dundug kune.” Jenn doomi muus takku fitam laajte : ” Yaay, lan moo tax nu dem ba wéeru ci doomi Aadama ngir sunug lekk ?” Baay muus ak yaay muus xoolanteb diir, ku ne ci ñoom sëgg. Baay muus xàddmiku siggi, xool ko, ni ko : ” Ca jamonoy maral wu metti wa, la nuy jafe-jafe teg ci yoonu gàddaay, jóge ca àll ba nu dëkkóon te doon fa dunde ci li nu doon ame ci sunum rëbb. Danoo dem ci dëkk bi nu gënoon a jige ngir am fa lu nu lekk.” Ci yuuxuy “Siiru” la nu xale yu xiif yu dëkkóon ca dëkk ba dàqe ànd ak xaj yu léen gënóon a yooy. Man ak séen yaay, sunug mën a xélóo nu teree dee keroog.” Yaay muus yokk ca ni : ” Yàlla yaa na, dina nu dimbali. Nanu ànd ak ngëm, Yàlla dunu bàyyi mukk.” Maa ngi fàttaliku ni, bi nu ñëwée ci taax yi, li nu gënóon a jaaxal mooy, nit ñi muus la ñu nu tudde woon, maanaam, ñu am xel.” Baay muus, yokk ca ni : “ Gune yu bare ci taax yi, ñoo gënóon a suur gune ya woon ca dëkki kaw ga te yit dàquñu nu woon dinu rëbb. Waaye sunu kàll yi ñoom séen xaj, siis ba nga ni lii lu mu doon, ñoo nu doon teree jege boroom kër yi.” Yaay muus ba tey ni : “ Yàlla, Yàlla, bey sab tool ndax wàññeekum xaalis mii dey, wonaat nanu lu nu xamoon, fàtte ko, muy, ni muus, daa war a rëbb ngir dundal boppam, maanam fexe ba yoral sunu bopp li nuy lekk bés bu ne. Loolooy saafara jafe-jafe bii nu am,” moo doon mujjantalu waxi yaay muus mi doon génnéeka delloo weem ya ñàkk a liggéey sewaloon ruuj.

Ci noonu, la njabootug muus jële tëralin wi doon ni, kenn kune ci ñoom, dinga jóge ci kër doomi Aadama yi, ngir dem wutali sa bopp li ngay lekk,
ci sa kow liggéey. Waajuri doomi muus, li ñu léen wax mooy :“ Juddu bu rëy, ndey ak baay, tekki ci àdduna, kune yaa ko yoral sa bopp”

Doomi muus yi nga xam ni bu jëkk, dañu daan ŋeew bu ñu xiifée, fasyéenée jóg, dunde ni ko séen jamono laaje woon, moytoo sukkandiku ca séen jamonoy waajur “ Ci noonu, ñu ànd dem marse Làmbadaa fa AstaTàpparka jigéen juy jaay jen ne woon, Ndey Binta limoŋ soxna su bañooni muus ne fa booleek nag Joor Kaabaab bare jàmm te daan jaay mburu ca bunt marse ba mook Mareem ak Binta akit Maar Seen jaaykatu yàpp ba.

Ci diir bu gàtt, njabootug muus ga suqaliku, ak li wàññikum xaalis miy metti lépp. Booba, muus yi wéyóon di dëkk ak doomi Aadama yi, dañoo yooyoon ba nga ni lii lu mu doon. Baay muus fàttali doomaam ya ni : ” Jëkk léen a wéeru ci séen kàttanu bopp ba la ngéen a ñaan ndimbalu keneen ni yéen. Di wër di jooytu tiis wu la dal mbaa ngay yaakaar a dunde séeni ndesit, amul benn njariñ.”

Doomi muus yi téye waxi mag yooyule ndaxit àddina soxla yu mag ak yu ndaw a fi ne. Saa su soxla yu mag taxawee, ñu xar ca séen tànki tubéy ba saafara léen.

Ci noonu la ñu deme ba xam ne ndekete àdduna daal li fiy saafaray jafe-jafe mooy saar wu mag wii di: “ Saa su àddina demee ba metti, dund jafe, fasyéenéel a dunde saw ñaq, bul nangoo wéeru ci kenn.”


Ay taalif yu ñu jukkee ci “Ndesiti Doomi Aadama” tekki léen ci Nasaraan(Fr .ak Angl.).

GUDDI, BËCCËG
Jant baa ngi so,
Keppaar yiy gën a dëll
Nu yaakaar ni séen takkndeer yu jëmmu yi
Dinañ muur ak séen sér yu tër yi
Lal bu yaatub lëndëm këriis gii
Wànte weer wi ni ñokket dànk
Wesaare leeraayam bu sell bi
Ca fa gën a xóot ci xolu guddi gi.
Maam Daour WADE

LE JOUR, LA NUIT
Le soleil se couche,
Les ombrages s’épaississent
Et l’on croit que leurs imposantes silhouettes
Vont envelopper de leurs sombres couvertures
Le grand lit des ténèbres
Mais la lune se lève sans bruit,
Et arrose de sa douce lumière
Au plus profond du cœur de la nuit.
Maam Daour WADE


COOW LI
Niir yaa ngi tiim
Dëkk bu yaatu bii
Ci wetu géej giy riir
Ci koñ bi woyi jàng yaa ngi jaxasook
Yu xumbéel beek xumbtey takk geek gu ngéenté li
Booleek sikari dëj bu tooy bi
Coow laa ngi ne kurr Jóge ci xulóo bi
Ndax xale yi doon xeex leegi
Fële ci benn ruqub kër gi,
Xale yaa ngay lakk yaboy
Yu ñu léen maye ca marse Làmbadaa
Muus yay xaaraan, ñëw,
Di xiirooka xoseente, firi séeni karaw,
Génne séeni we, di waaj a xeex
Mellantaan yay daw,
Gàddu peppi sanxal ,
Jëme séenum pax
Pënd ba jog ni kurr nib lay
Sóob léeb ci guddi gu ni këriis
Ci digg bëccëgub ndarakàmm.
Maam Daawur Wàdd

LA CLAMEUR
Des nuages surplombent
Une grande ville
A côte d’une mer qui murmure
Dans un quartier, des chants religieux se mêlent
Aux sonorités d’une surprise-partie, d’un mariage et d’un baptême
Brassées aux chants mélodieux de funérailles récentes
La clameur est à son paroxysme
Venant d’une querelle de femmes
Une bagarre de bambins, il y a un moment.
Là bas, dans un coin d’une maison
Des enfants grillent du hareng
Qu’on leur a offert au marché Làmbada.
Des chats qui guettent leurs parts, sont venus
Se menaçant, se griffant,
Le poil du dos hérissé
Les ongles dehors, prêts à en découdre.
Des fourmis s’enfuient
Portant à l’épaule le grain,
A mener à leur demeure
La poussière s’élève, comme un brouillard,
Qui les plonge dans une nuit toute noire
Au beau milieu d’un jour pourtant ensoleillé.
Maam Daour WADE

THE CLAMOR
Floating clouds hang over
This vast city by the murmuring sea
Where sacred songs of worship
Mix with the cacaphony from parties
And the sweet sound of wedding songs
With the sadness of dirges
Noise, noise and noise everywhere
Fed by women in a continuing row over their fighting lads
Round the corner, youngsters grill herrings
Fruit of the day’s toil at Lambada market.
All around cats battle
Hoping for leftovers
Just even for a tiny piece of fishbone
The reward.
Claws out, their fur shaggy
Dust spreads all over
Ants sway with millet grains
Towards their anthill
Immersed in the darkness of night
In the light of day.
Maam Daour WADE

0 Comments:

Post a Comment

<< Home