ATTAAYA/LE THE
ATTAAYA
Doxandéem bi, bul gaawtoo dem
Toogal ci basaŋ gi naanandoo
Attaayaak nun
Naanal lëwël bi ndax
Wex na xàtt nib noor.Naan ko ba
Dinga yëg ngelaw liy wupp ak tàngaay
Wuy damate yaxi yaram
Naanal ñaareel kaas bi ndax dafa neexe
Ni bët-sébbi. Naan ko ba
Gis ñax miy jebbi,meew mi ci
Biir këll yeek xiif biy giif.
Ma ne, toogal ba naan ñetteel bi
Ndax, saf na suukër
Ni mbëggéel.
Doxandéem bi, bul gaawtoo dem toogal ci
Kow basaŋ gi te naanandoo àttaayaak nun.
Taalifu Tuwaareg Bu Niiseer
LE THE
Etranger, ne pars pas si vite
Assieds toi sur la natte et bois
Avec nous le thé.
Bois le premier verre parce qu’il est
Amer comme la saison sèche. Bois le et
Tu sentiras le vent qui souffle et la chaleur
Qui brise les os du corps.
Bois le deuxième verre car il est doux
Comme le retour des pluies. Bois le et tu
Verras l’herbe pousser et le lait dans
Les calebasses et la faim qui s’apaise.
Reste encore et bois le troisième verre car il est sucré
Comme l’amour.
Etranger, ne pars pas si vite, assieds toi sur
La natte et bois avec nous le thé.
Poème Toureg du Niger
Image:"Matériel de thé" une conception de Daour Wade(Copyright)
0 Comments:
Post a Comment
<< Home