KAAR RAPPIT
Sippéer wata yuy yobbu nit ñi la, di léen jële bërëb yóbbu léen bërëb, ñuy fay. Wata bu yomb a xàmmee la ndax péntur bu baxa la yor ak rëdd yu mboq ci wet gi. Ni léen moom leeg-leeg ñu bind turu Yàlla ca ginnaaw, mbaa ca kanam, walla séen turu sëriñ, boolee kook i ñaan yu deme ni: Fàttiilan, jàddiilan walla yeneen. Alhamdulilaahi ne fà{{ ca kanam, jëmu ba ca wet ya, turu sëriñ ba ca ginnaaw, aparaante bay lang di yéenéeka dóor loxo la ca bunt ba. Sippéer ba déqina.
Foo léen tàllalee loxo ñu ni ràtt taxaw, booy yoor sab tànk ca biir, jàfandul bu baax ca weñ ga ñuy wooye Mbay ndax sófóor ba yékkatina, aparànti ba naan ko "Ayca dugg na" te di la waxaale, "jàppal ci mbay" booleek di la téyewaale.
Foo bëgg a wàcc sippeer ba dina ko weesu, ngay wax aparànti ba, gone gu fer démb ñàkke lay teggin, soo moytuwul, mu xeex ak yow walla mu saaga la. Su wata wi dawee tuuti, waa Yàlla mbaa miskin yuy dem Ndakaaru, tàmbalee woy di sàkku paas walla ndimbal ci njàccaar yi. Du yàgg lool nit ñu baax sarax léen paas ba ñu ëppële.
Gune yi ñu uuf, di xoole fune, tukkikat yi toog, ñii jàkkaarloo di xoolanteeka sëgg, ña ca des wetoo di xaj-xajloo.
Leeg-leeg, waxtaan jolli wu ñi nekk ci sippéer bi yépp di bokk, wata wi xumb lool. Ci jamono yooyu, soo moytuwul, soo wàccee ngay soog a seetlu ni tafu nañu la
Su mbirum sippéer yemoon ci lii, kon coow lu rëy du am ci xeetuw wata wii. Li wuutale sippeer ak yeneen wata yi mooy daanaka jëyya ju am ci tali bi daanaka ñunga ca. Li sippeer faat ciy bakken bari na lool, ba ñu war léen fee jëlé ngir dakkal li ñuy def ci tali bi. Kon daal wata wii di sippéer, moom la ñu tiiñal, bàyyi nit ki koy dawal ba tax ñu war ko fee jëlé.
Sippeer bi, fu mu dem sófoor baa ko fa yóbbu, demalul boppam rekk, dañu koy yóbbu. Su fekkee nit kiy dawal sippeer bi am na nu muy doxale nuy tax jëyya yi di am, suñu yoree yeneen wata yit, li ñuy bañ du fi jógé.
Yëf yi dem na ba leegi, nit ñi ci bërëb yu deme ni diiwaanu Ndakaaru, sës nañu ci li sippeer yiy def ba mu ñu jóg taxaw di jànkoonteek mbirum sippeer yi.
Li leer moom mooy ni, kenn bañul sippeer ndax soxla yu rëy lay fajal nit ñi ba su sófoor seek aparànti yi jubbanti woon séenu doxalin jàmm ni ñoyy.
Photos Copyright : Daour Wade Juillet 2006
0 Comments:
Post a Comment
<< Home