UNE BIBLIOTHEQUE A ENCORE BRÛLE...
doomiaadama
SARGAL LEWOPÓOL SEDAAR SEŊOOR
Lewopóol yow jàmbaar sunu góor,
Sargal nañ teg ca ñaan, jëme la
Gunge la ba ca biir fiy Belleer
Kër gii nga dem tey jii tëri fa,
Woykat yu neex baat yi, woy la,
Ñi di kañ, ñoomitam tagg la.
Teraanga ju mu doom jombula.
Góoru yaa Ñilaan Baaxum, ngaalaamaa.
Lewopóol, yéeg nga, yàgg na.
Yegg nga daaw ren soog a ñëw.
Yegg nga, weesu nga la ñu xam.
Wër nga fii, dem nga faa, wax nga fee.
Wër nga tam bépp dun walla géej
Fa nga jaar ku fa jaar taq ban.
Laawla cat, laawla bët ak làmmiñ
Ndeke yow fi nga yem, jéggi na
Romb na, jéll na, séen téere
Taxul woon ngay wëraaluy xaste
Kañ nga buur, kañitam baadoolo.
Kañ nga yit bépp xeet wu dafa ñuul.
Jomb nga woon a beddi doom Aadama
Taasoo ngook, li ci des di taalif.
Waraloon noon yi la bañ doon sàlloo
Lewopóol tubaab bu ñuul tigi la.
Ndeke yóo, xamuñu xóotuñu
Xamuñu matuñu muusuñu.
Ba taxoon séeni wax daawul teer
Yàgg nga, yegg nga, Lewopóol.
Yegg nga, ba ca biir xàmbi Siin
Jóge fa Baayu Mbeen yéegal la.
Cëy waay, Lewopóol dem nga nii?
Tëri fee ca janasa yuy Beleer.
Filipa, nga foofee di la xaar
Réew miy jooy aka jooy bay sëngéem.
Jiloor miiy ranxooñam kañ lay fer?
Ñilaan Yaay Baaxum a jur Lewopóol.
Réew mi yépp ba tey jii ñuŋ koy jooy
Moo taxit séeni ñaan dakkagul.
Jinax Mbaay yow miy dem ba ci suuf,
Soo àggee ni Lewopóol mum Yaa Ñilaan
Ranxooñ yiñ ko fi jooy suñ àndoon dooni géej
Faf lëkkëlóo nekki ñaan, jëm fi moom.
Gaynde giiy Lewopóol mum Yaa Ñilaan.
Maam Njoor (1) (traduit et revu par Maam Daour Wade)
HOMMAGE A L. S. SENGHOR
L’enfant de Djilor, le chantre de la Négritude
S’en est allé. Il est bien parti l’immortel
Oh oui, le Haut Pool C’est-d-Art Senghor
Joal se souviendra toujours.
Joal attendait, Joal attendra toujours.
Oui...et tu es simplement passé à Bel-Air
Voir, revoir ton enfant chéri, Philipe Magihilene
Ailleurs..en France et du haut de la Coupole,
La France prend enfin le train en marche
Le train de l’histoire et rend hommage
A Léopold Sédar Senghor le plus
Grand défenseur nègre de la langue Française.
Ailleurs..dans toute la Diaspora noire
Un hommage ardent sera rendu
Au grand poète, au penseur et à l’humaniste
De son temps, de son siècle.
Ailleurs.. dans d’autres endroits...
D’autres déçus de n’avoir pas pu atteindre
Le Haut Pool, ont cherché vainement
A descendre ton nom du Haut
De la Coupole et du Panthéon de l’Universel
Senghor, Sén-goor, Sunu-góor
Joal et son peuple pleurent encore
Le monde et la Diaspora noire regardent partir
Celui qui a rendu aux nègres la fierté d’être
A l’origine de ce qui est beau, dans la pensée,
Le langage, dans le gestuel qui embaume
Cette émotion qui est nègre
Des rives du Sine au pays sérère,
Aux rives du Gange-Pays de Mahatma Gandhi,
En passant par Persépolis, Athènes pays des Dieux Grecs
Ce Grec que tu as enseigné
Oui, Léopold, tu as presque parcouru
Tous les pays de la Diaspora noire
Apportant partout le message de la Paix
Qui est encore et toujours fondement
D’un monde durable.
Vas, Léopold Senghor au Royaume
Du rêve éternel.
Ceux qui n’ont rien compris,
Ne comprendront plus jamais.
Adieu Poète.
MAAM NJOOR (1)
Dakar, Décembre 2002 Sicap L1
MAAM NJOOR (1) Le destin m’a mis sur sa route et il est venu à moi par l’entremise Mme Abibatou Diallo du BED ( Business Etudes et Découvertes). Depuis ce jour, nous ne sommes plus quittés et assez souvent nous discutions de la Culture au Sénégal. C’était son thème de prédilection, et il m’entraînait du nord au sud, de l’est à l’ouest de notre pays sur les traces des faiseurs de royaumes. Il m’a montré sa collection de parures de colliers- de « Isë Faal » au Peme en passant par le Làmburde). Sa soudaine maladie et sa disparition dans le premier semestre de 2006, ne m’auront pas permis de réaliser « un documentaire » sur sa vie… Une bibliothèque a encore brûlé…Que la Terre lui soit légère et que le Paradis soit sa demeure éternelle (Amiin)
0 Comments:
Post a Comment
<< Home