NAWET
Kukk asamaan saa ngi ni,
Ràyy melax ga ni
Wupp ngelaw la def
Toq-toq dox ya rot ab diir
Toftal ca satatat-satatat,
Yàggul dara mu naan
Yuréet-yuréet
Dajaloo ndox ma wal
Def dex yuy àndandoo dooni déeg
Xatatat,tàrr,dënnu ga xar,
Asamaan siy gurung-rungi
Nit ñiy ñaan
Fit yiy tër-tëri
Suuf màndi, mbott ngoox
Tàngoor giif;
Mbégte dugg xolu bépp beykat
Yaakaar taxaw ci ni su tasul,
Nawet sàmpu na.
Maam Daawur Wàdd
Photos réalisées par Daour Wade(Copyright)
0 Comments:
Post a Comment
<< Home