MEŊŊ NI JONN
Sémbéen,doomu Afrika
Ku sëmb, sumbi dinga weer
Sëmb nga, sumbi nga, weer nga
Ñi la xam, miin la, jege la,
Jooy nañu keroog ca janasay
Yoof Mbelelaan méngóok
Altine 11 fan ci atum 2007
Weeru suweŋ ca foofee ñu la denc
Ca penku ba ca kow,
Ca wetu yaari filaawoo ya
May gisaat ci samam xel yenn ci
Sa film yi nga liggéeyal xeet wi
Téere yi nga bind bàyyi fi
Ñu nar la fee wuutu ba abadan
Ngay wéy di wax aka waxtaan
Ak ñu la xamoon ak ñu la musul a teg bët
Ma fàttaliku la ma góor ga aliyun Jaañ Kaaŋ
Mu baax ma dénkoon ci biir waxtaan:
Ku nekk ci àddina, te bindóo waxoo
Bés boo dëddóo, soo fi bàyyeey tàkkndeer it
Yow sag jonn ni meŋŋ nga def
Ña la déggul woon dóotuñu la dégg ba fàww
Ña mus a dégg say wax duñu gis ku léen koy tekkilati
Yow déy gàcca ngaalaama déy yow Usmaan
Kenn du ni waxook say ñoñ ca nanga mëne
Wax ngaak ñoom ci làkk yi ñu dégg
Doore ko ca jamonoy "Kàddu" mi ëmbóoni xibaar
Yu ñu bind ci Kàllaamay réew mi
Te nga sosoon ko boobee ca atum 1971
And caak nit ñu farlu te fonk mbiri caadaak cosaan
Nu mën caa lim Paate Jaan, Ben Jogoy Béey,Waagan Fay
Duudu Jaak, Asan Gumble, Umar Géy, Sàmba Jonn,
Sitoor Toop, Aamadu Toop, Maam Siise
Booleek nitaali Alfa Waali Jàllo mi nu won jaxran "Talaatay Ndeer"
Ngéen doon ñaax ca biir"Kàddu" googee, bépp doomu Afrika
Ci mu gën a fonk boppam,ràññee ni sàkku xam-xam dakoo war
Tekki tënkuteg xelam yit teg ca wóolu boppam
Xam ni bu yàgg fii ci Afrika, amoon na fi doxalin yu rafet
Lu deme ni demokaraasi, xewoon na fi démb,
Soo weddee laajal nguuri cosaan
Lu jiitu nasaraan biy duggsi fii di nootseeka supparñi,
Mu waxtaanal nu ci bañkat yi fi ne woon
Te xeexal nu ba nu jot sunu bopp
Fàttalinu la Kuwaame Kurumaa sumbóon ngir Afrikaa mën a booloo.
Ñu ni déét a waay nga feesal kàgguy daaray réew mi
Ak yu réewi fenen ci Afrikaak téere yuy wax
Ak bépp doomu Aadama ci yenn ci yu fi mus a xew,
"Camp de Thiaroye","Les bouts de bois de Dieu",
"Emitaï", "Le dernier de l'Empire",
Ceddo" ak "Gelwaar"
Luy xew ba tey "Le Mandat","Xala"
Di wax nu tekki xala gi nu tënk ci xel yeek jëf yi
Joxoñ na yit lu mën a xew,
Lu war a xew,génne "Faat Kine",
Lu waratul a xew ci suufu Afrikaa
Dem Burkina sos fa "Molaade"
Laaj nu nu dawal xel yi
Geestu sunu yaay yeek sunuy jigéen
Gën léen a fonk, gën léen cëral,ñaax léen ci ñu laaj ko
Ñu fexee mënal séen bopp te xam ni toog doŋŋ
Bank séeni yoxo musul a am ci jigéeni Afrikaa,
Te waru fee am.
Nammaat xel yeek jikko yi,
Jub,jubal te takku liggéey
Liggéeyin wu sell te saxit
Jot na bu yàgg a yàgg
Ci biir déggóo ci sunu biir gi fi maam yi ba woon
Moo xam diinee joo mën a gëm
Ak waasoo woo mën di bokk mbaa di di ko xëccu
Nga xam nun ñépp ay bokk la nu doon
Bokk gu lalu ci Kóllare gu jóge fu sori ci cosaan
Ba tax Sémbéen jële ci Maam Kocc Barma Faal:
"Magum lëndëm, ku ko gisul it, mu gis boppam"
Nu xam ni Afrikaa du dem fenn ndare ñépp a ciy jàpp
Ci biir déggóo, jàmm ak njub gu sax dàkk, dàkk, dàkk
Gu won ginnaaaw, yaafus ak tàllal loxo di yelwaan mbaa
Di ñaanaatooka gërëmaate ci may yuy gàllankoor sunu yokkuteg ëllëg
Déggóon naa geneen góor guy wuyóo ci turu Amadu Ampaate Ba
Moo daan wax ni:"Fii ci Afrikaa, màgget mu génn àddina
Dafay saamandaay kàggu gu lakk ba suppikub dóom"
Yow déy Usmaan, sag meŋŋ ni jonn nga def
Ndax ku ci namm tey mbaa ëllëg sa waxtaan,
Dafay seetaan sa "Film" ba ko neex
Mbaa mu jàng benn ci sa téere ba ko soob
Su noppe yéemu, mer mbaa mu ree, dalal ni jaajëfée Sémbéen,
Ñaanal la ci biir ci saayiir mbaa baatin firndéel ko
Yal na la suuf sedde ca biir Aljana
Foofuu nga tëdd,fa Yoof Mbelelaan
Aamiin.
Maam Daawur Wàdd
0 Comments:
Post a Comment
<< Home